Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay doon nemmiku memoriyaalu geer bu Abu Dabi ak Alef « Education » doon ñi jiitu ci njàngalem xarala mu lalu ci wàllu IA.

Biti Réew - 06 MONTHS.DECEMBER 2024

Ci ñaareelu fanu ngan gi muy amal ca Emiraa Araab, Njiitu Réew mi ànd na ak Kilifa gi Seex Teyab Bin Mohammet Bin Sayed Al Nahyan,  dem ca « « Wahat Al Karama », ngir delloo njukkal saa-emiraa yi daanu ci tooli xare yi. Jataay bu am solo bii ñu amal ca « memoriyaalu geer » bu Abu Dabi, fésal nañu ci wegeel ak xaritoo gu wér diggante Senegaal ak Emiraa.

Ba mu fa jóge, Njiitu Réew mi dem na ca « « Alef Education », bokk ci ñi jiitu ci njàngum xarala yi lalu ci wàllu IA. Muy jumtukaay bu man a soppi njàngum Senegaal, jaare ko ci yeesalaat njàng mi ak dugal daara yi ci njàngum réew mi. Lëngoo gii nag ab jéego bu am solo la bu jëm ci méngale ak jamono sunu doxaliinu njàng mi.