Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay demoon nemmikuji NVIDIA gi bokk ci ñi jiitu ci wàllu IA ci àddina si.

xamle - 27 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, ànd na ak ndawi àntaperenéer yu ekosistem nimerig bu Senegaal, nemmiku tay kër gii di NVIDIA, te bokk ci ñi jiitu ci wàllu IA ci àddina si.
Nemmiku gii, di dugg ci wër gi muy amal ca Kaliforni, tax na ñu gis ay yooni lëkkaloo yu wér ngir def Senegaal ndaanaan ci Afrig ci wàllu IA, rawati na ci naal yuy tàbbi ci biir New Deal Technologique bi.
Njiitu Réew mi gis na fa xarala yi gën a mucc ayib ci wàllu IA, te doon lu ñu man a jëfandikoo ci pàcc yu am solo ngir doxal Sémbu Soppi Réew mi fii ak 2050: mbay mi, njàng mi, paj mi añs.
Xarala yii dañuy gën a dooleel sunu man-man ci saafara jafe-jafey ëllëg yi teg ci def Senegaal niki selebe yoonu xarala ci Afrig.