Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay ca Araabi Sawudit ak Turki

jëwriñ - 27 MONTHS.OCTOBER 2024

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, dina dem ca Arabi Sawudit 27 jàpp 31i fani oktoobar 2024 ngir wuyuji ci ndënel Kilifa gi Doomi Buur bi di Mohammet Ben Salmaan Al Sawud.

Li war a màndargaal tukkib nemmiku gii nag mooy ay ndaje yu mu war a séq ak kilifay saa-sawud yi ak teewam ca ndajem Future Investment Initiative Forum, di xew-xew bu mag ci àddina si buy dajale kilifay politig ak koom yu am dayoo ngir waxtaane jafe-jafey eewestismaa ci àddina si.

Bu fa bawoo nag Njiitu Réew mi dina dem ca Turki 31i fani oktoobar ba 2i ñaari fani nowàmbar ngir amal fa tukkib nemmiku ci ndënel Kilifa gi Recep Tayyip Erdogan, Njiitu Réewum Turki.