Njiitu Réew mi amal na 8eelu bëccëgu jaayante « SETAL SUNU RÉEW ».

xamle - 04 MONTHS.JANUARY 2025

Xewu 8eelu bëccëgu jaayante  «SETAL SUNU RÉEW » amal nañu ko tay ci gaawu bi 4i fani sãawiye 2024 ca Site Komikóo bu Yëmbël Noor, ci njiital Kilifa gi, Basiiru Jomaay Fay, Njiitu Réew mi.

Ñu ci doon waxtaane tomb bii di « Setal sa gox, aar sa yaram : way-kaaraange gi dinañu jaayante ci wetu askan wi», seetlu nañu ci bëccëg gu njëkk gii ci atum 2025 , teewaayu Jëwriñ ji ñu dénk larme bi, di Seneraal Biram Jóob, kilifay Ndoxal gi ak yu mbeeraayu Ndakaaru, niki noonu askanu gox ba. 


Ginnaaw ba mu teewee yënguy setal yi ba noppi, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, def na woote bu am solo jëme Ko ci mbooleem saa-senegaal yi ngir ñu gën a am taxawaay ci  wàllu cet ak sàmm kéew mi. Ci loolu, moom Njiitu Réew mi soñne na ci solos ma-réew bu ne fexee sàmm li  wër ab dëkkuwaayam, ndax kat nee na cetug pénc mu mbirum ñépp la war a doon. 


Peresidaa Fay ñaax na askan wi ñu gën a sóobu bu baax ci joŋante bi ñuy def jëm ci neexal Koñ yi gën a set. Jàpp na ne, naal bu am solo la  ngir fésal jëf yu sax dàkk ngir Senegaal gu sell te neex a dunde. 


Njiitu Réew mi fàttali na solo si nekk ci lii nu ànd jaayante ngir tabax Senegaal goo xam ne ñépp dañuy bokk benn pas-pas, muy sàmmonte ak kéew mi.