Njiital IFC di Maxtaar Jóob, Peresidaa Basiiru Jomaay Fay dalal na ko.

xamle - 23 MONTHS.DECEMBER 2024

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, dalal na tay ci Njénde li, Maxtaar Jóob miy Njiital kërug kopparal gii di IFC.

Leeral na Njiitu Réew Mi jéego ak naali yi IFC di teg, jëm ci ful tolluwaayu jaayanteem ci Senegaal.
Seen i waxtaan a ngi jëmoon itam ci sémb yu am solo yi jëm ci gën a dooleel yokkuteg koom mi ak pàcc yu am solo yu mel ni mbay mi, ndefar gi, paj mi ak xarala yi.