Ndokkaley liggéeykati Njéndel Réew mi ci at mu bees mi.

xamle - 10 MONTHS.JANUARY 2025



Jot  nañoo amal ci àjjuma ji 10i fani sãawiye 2025, ci saal dee bànke bu Njénde li, jataay bi ñu baaxoo amal jëm ci ndokkale Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay ak Soxnaam, ci at mu bees mi. 

Mbooleem serwiis yiy liggéeyee ci Njénde li ñaanal nañu Njiitu Réew mi ak soxnaam, at mu ànd wér, mbégte ak naataange.

Njiitu Réew mi tamit, ginnaaw ba mu rafetloo seen ug jaayante ci liggéey bu am solo bi ñuy defal réew mi, jaajëfal na leen bu baax boole ko ak ñaanal leen ñoom ñépp atum jàmm ak xéewal.

Man ngeen a seetaan widewoo bi: