Ndajem Waxtaan mu Doha: Jataayu Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay

laaj ak xibaar - 08 MONTHS.DECEMBER 2024

Ci ñaareelu fan di bi mujj ci Ndajem Waxtaan mu Doha, jagleel nañu fa Kilifa gi Basiiru Jomaay Fay ab jataay.

Ci biir jataay bii, Njiitu Réew mi àddu na ci ndam li mu am ci joŋantey fal Njiitu Réew mu 2024, niki noonu ab gis-gisam ci amal yoriin wu jub, maandu te leer, di gis-gis bu ñépp ànd rawati na ndaw ñi. Àddu na itam ci tomb yu soxal balli mbindaare yi (petorol ak gaas), Sahel gi, CEDEAO ak lëkkaloo diggante réewi bëj-saalum yi ak bëj-gànnaar.


Man ngeen a toppaat tomb yi gën a fés ci jataay bi: