xamle - 17 MONTHS.JANUARY 2025
Njéndel Réewum Senegaal moo am mbégte di leen yëgal xew wu njëkk wi soxal ndaje mii ñu tuddee « Conférence des Administrateurs et Managers Publics (CAMP) », di ndaje mu ñuy amal leegi at mu jot, ci nammeelu Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, muy dajale mbooleem ñi jiite ay wànqaas ci sektéer piblig bi ak parapiblig bi. Ndaje mu njëkk mii nag dees na ko amalee ca « Centre International de Conférences Abdou Diouf (CICAD) », altine 20i fani sãawiye 2025.