Lëngoo: Senegaal ak Turki fas nañu yéene yóbbu seen jëflantey yaxantu ba ci 1 millyaari dolaar

Biti Réew - 31 MONTHS.OCTOBER 2024
Ginnaaw ba mu siyaaree xabrub Mustafaa Kemaal Ataturk mi taxawal Repiblig bu Turki ba noppi, Njiitu Réew Mi Basiiru Jomaay Fay teertu nañu ko, tatagal ko, dalal ko ca Njéndel Ànkara mu daje fa ak Peresidaa Recep Tayyip Erdogan ngir séq ak moom ub jataay.
Ñaari kilifa yi torlu nañu ay déggoo yu am solo yu jëm ci ful ñaari yoon jëflantey yaxantu yi diggante Senegaal ak Turki, jële ko ci 500i milyoŋ yóbbu ko ba 1 milyaari dolaar ci at yii di ñëw. Déggoo gii nag jéego bu am solo la ci lëkkaloog ñaari réew yi, rawati na ci wàllu mbay mi, yasara gi, njàng mu kawe mi ak kaaraange gi.
Jot nañu faa torlu ay déggoo itam diggante jëwriñi Senegaal yi ak seen naataango yu Turki, ci pàcc yu yitteel réew mi lool niki mbay mu ànd ak xarala, yasara gi ak njafaan yi, dëkkuwaay yi ak njàng mi. Mu doon kon luy firndeel yéeneey ñaari réew yi jëm ci gën a dooleel seen ug lëngoo.
Ñu tëjee bis bi ci àddug ñaari Njiiti Réew yi ak añ bu Njiitu Réewum Turki ak soxnaam ganalee Peresidaa Fay ak Soxnaam, di luy firndeel xaritoo gu dëggu ak yéene ju sell ji Senegaal ak Turki yàgg a séq.