Kawlax dalal na 9eelu edisoo bis bi ñu jagleel càmm ci réew mi.

xamle - 22 MONTHS.FEBRUARY 2025

Kawlax dalal na 9eelu edisoo bis bi ñu jagleel càmm ci réew mi, ci njiitaal Basiiru Jomaay Fay Njiitu Réewum Senegaal. Bis bii ñu doon waxtaane tomb bii di « dooleel liy bawoo ci càmm gi ngir ñoŋal manal sunu bopp ci wàllu dund », dajale na mbooloo mu bari ci ñiy yëngu ci wàllu càmm gi ak kilifay tund wa.


Ba mu yegsee rekk, ci la moom Njiitu Réew  mi daal di jubal ngir nemmiku mbooleem stand ya fa nekk, ñu wan ko fa ay yeesal yu am solo yu ñu amal, mu wccente ak ña doon fésal ci ñu gën a sóobu ak taxawaayu bi mbay mi war a am ci suqalikug koom mi ak li ñuy dundee ci réew mi. 


Ci teewaayu Njiital Ngomblaan gi ak Jëwriñu Mbay mi, moom Njiitu Réew mi jox na fa ay raayay ràññiku ñi nga xam ne ñu ngi taxaw saa su ne ci luy gen a jëmale kanam wàll wi. Ña doon teewe ndaje ma itam, posewu nañu ci bis bi ngir yaatal ci jafe-jafe ak man-man yu bari yi wàllu càmm gi làmboo, lépp jëm ci gën a dooleel liy bawoo ci jur gi ak nees di def ba man koo soppee ci réew mi.


Cig àddoom, Njiitu Réew mi rafetlu na bu baax anam yu mucc ayib yi askanu Kawlax ak ñiy yëngu ci càmm gi takkoo. Mu fàttali moom Njiitu Réew mi ne manal sunu bopp ci wàllu dund moo jiitu ci jéego yi nguur gi teg, te loolu càmm gi da cee am taxawaay bu am solo. Rafetlu na itam waxtaan yi ñuy amal ci jafe-jafe yi càmm gi di jànkoonteel, di loo xam ne dina tax ñu gën a xam dëgg-dëggi man-man yi ak jafe-jafe yi ak mbooleem liy yoot càmm gi ngir man leen a saafara ba fàww.


Njiitu Réew mi yëgle na fa ay matuwaay yu wér ngir joyyanti càmm gi. Te mooy jéem a sàmm lépp lu jëm ci suqalikug jur gi, bokk ci yooyu wàllu xont ak taxawal ay koperatiif ci wàllu mbay mi. Mébet yooyu dinañu bokk ci liy tax ndaw ñi man a toog ci seen i gox te dina bokk ci liy wàññi ñàkkum xëy mi ak mbëkk mi.


Ci lu soxal càccum jur gi, Njiitu Réew mi jox na ndigal Njiital Jëwriñ yi mu lootaabe ca na mu gën a gaawee, ndaje moo xam ne jëwriñ yépp yi mu soxal ñoo koy séq, doon it lu ñiy yëngu ci wàll wi di teewe, ngir xool yan matuwaay lañu war a teg ngir xeex ak jëf ju ni mel.


Senegaal di waaj ngir door ci altine ji 24i fani féewarye 2025, sémbu xaralaam wu bees wii di « New Deal technologique », Njiitu Réew mi soññu na ñiy yëngu ci wàll wi ñu gën a dugal xarala yi ci fuglu gi ak caytu gi ngir man a jariñu bu baax ci man-man yi xarala yi làmboo lépp ngir gën a dooleel doxaliinu pénc mi ñeel sektéer pirimeer bi. 


Man ngeen a toppaat mbooleem kàddu yi Njiitu Réew Mi yékkati ci bis bi : 



Bokki Senegaal, 

Bokki sàmmkat yi,

Askanu Kawlaw wépp,


Li nu dajale fii tay, sargal la ci képp koo xam ne, góor nga walla ngay jigéen tey yëngu ci càmm. Lii day wane seen njàmbaarte ak ni ngeen taxawoo réew mi ak solo si ngeen am ci liy doxal réew mi. Fii nu tànn nag tay, muy Kawlax, Siin-Saalum, manunu woon a tànn feneen foo xam ne gën naa yell nu dajale fa sàmmkat yi ngir waxtaan ak ñoom ci liy jëmale càmm ca kanam. Ndax seen wàll wii, solo si mu am ci liy doxal réew mi foo ko natt rekk, weesu na ko.


Loou moo tax, tomb bii ngeen tànn ngir waxtaane ko ci at mii, ci bis bii ñu jagleel càmm ci réew mi, te mooy xool naka lanuy gën a dooleelee porodiwi yi nga xam ne ci càmm gi lay bawoo ngir gën a ñoŋal lii di manal sunu bopp ci li nuy dunde, am na solo lool, maa ngi koy rafetlu bu baax a baax. 


Càmm gi li mu ëmb ci njariñ bari na lool, rawati na yi nga xam ne ñoo ciy meññee. Waaye nag jamono jii dañuy  jànkoonte ak ay jafe-jafe yoo xam ne, ci waxtaan, ci diisoo ak ci lëkkaloo lanu koy man a saafaraa. Li ngeen fi waxtaane, tënk ko, def ko ci « déclaration de Kaolack » bi ak li ma sàmmkat yi wax ak mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi, ci bi may wër sànq « stand » yi, dégg naa ko bu baax a baax. Buleen fàtte ne man ca àll ba laa jóge te sàmm naa itam. Kon xam naa lan mooy seen jafe-jafe. 


Am nanu nag ay man-man yu bari yoo xam ne, dingeen nangu ne sunu sistem bii nga xam ne bari na lu mu laaj, tabaski rekk firnde la ci. Fàww nu dem jéggaani ay jur ca Mali walla ca Móritani, ngir man a matale li nga xam ne saa-senegaal yi soxla nañu ko ci ay xar ci tabaski gi. Te moone de jafe-jafe yi Mali am tay ci wàllu kaaraange, Senegaal amu ko. Kon war nanoo jógaat gën a waxtaanaat, xoolaat naka lanuy sukkandikoo ci sunu bopp, bañ a yaakaar ci biti réew ngir man a ñoŋal mbay mi ak càmm gi nga xam ne, dañoo war a gën a lëkkaloo, ndax càmm manul a dem bàyyi mbay, waaye mbay itam manul a dem bàyyi càmm.


Moo tax waxtaan wi war nanu koo wéyal ci diggante baykat yi ak sàmmkat yi. Ndax baykat yi ñooy sàmmkat yi. Njaboot goo dem mu am ay baykat, am na ñoo xam ne ñooy sàmm, te ñii bu ñu demee sàmmiji ñii ñooy des ci tool yi. Kon amul wuute gu ñuy def ci diggante baykat yi ak sàmmkat yi lu dul waxtaan wu war a am seen diggante ngir nu xool wan yoon lanuy jaar ba fexee xool jafe-jafe yi ñuy am, ñu man koo wattandiku.


Lii nga xam ne nag wax naa ko Ma-Buuba Jaañ mi nga xam ne mooy Jëwriñu Mbay mi, Bay dunde ak Càmm, te séq liggéey bi ak Sekkereteer Detaa bi yor suqalig koperatiif ci wàllu mbay ak taxawu baykat yi, muy Alfa Ba, mooy nañu taxawu baykat yi, taxawu sàmmkat yi waaye fexe itam ba sàrt bii di « loi d'orientation agrosilvopastorale » ak dekkere yi muy àndal ñu xaymawaat ko, tëggaat ko te jébbal « code pastoral » bi Ngomblaan ga ngir ñu xool naka lañuy wotewaatee kod bu bees, ba lépp li nga xam ne seen mébet la, waxtaane ngeen ko, bëgg ngeen nu taxaw ci, nu man ko cee yokk, bu ngeen demee ca Ngomblaan ga insàllaa dinañu ko wote. 


Kon dinanu gën a taxaw itam waxtaane lii di càccum jur gi. Wax naa Njiital Jëwriñ yi mu lootaabe ca na mu gën a gaawee, ndaje moo xam ne jëwriñ yépp yi mu soxal ñoo koy séq, ñiy yëngu ci wàll wépp dañu koy teewe, ngir xool naka lañuy jëlee ay matuwaay yu gën a dëgër ngir xeex ak càccum jur gi. 


Di wax sàmmkat yi nag, xarala yu bees yii nga xam ne noo ngi ciy gën a sóobu, man na leen a dimbali bu baax ci loolu. Ci altine jii, dinanu door lii ñuy wax « New Deal Technologique ». Te li nu ci namm njëkk, mooy fépp fu nu nekk, nu man a am lënkaay ngir baykat bi ak sàmmkat bi man a nekk fi ñu nekk ci àll bi, man a am lënkaay goo xam ne, fu ñu soxlaa woote dinañu woote. Dégg naa ngeen tënk ko ci seen jafe-jafe yi nga xam ne sàmmkat yi dañu koy faral di am. 


Waaye li ma bëgg a wax ci xarala yooyu mooy weesu nañu woote kese. Ndax man ngeen ci jaar, ba seen jur fu mu nekk, bu ngeen xoolee seen jollasu ngeen xam ko. Te loolu dina tax bu ñu ko sàccee itam, dangeen di jubal fi mu nekk rekk fekk fa seen jur gi xam ne sàccoon nañu ko. Loolu tamit, pexe la ngir xeex lii di càccum jur gi. 


Kon li may daanele mooy, Ngóornamaŋ bi dina taxaw temm ci seen wet, tàllal leen loxo yéen sàmmkat yi, wéyal waxtaan yi ak yéen, ngir lii nga xam ne càmm la ci Senegaal, nu man cee sukkandiku ngir amal naataange goo xam ne day sax dàkk ci Senegaal, te sukkandiku ci mbay mi muy jumtukaayu yokkute niki nu ko waxee ci gis-gisu Senegaal 2050 muy sunu « Agenda Nationale de transformation » bi nga xam ne lii di càmm ak lii di mbay, taxawaay bu am solo lanu leen ciy pàccal. Nuy yaakaar ci yéen ne dingeen ànd ak nun ci liggéey boobu ngir nu suqali Senegaal bu baax a baax.


As-salaamu halaykum warahmatu Laah!