Jataayu siiwal sukkandikukaay bu yees bii di “Sénégal 2050” : Agenda National de Transformation.

xamle - 09 MONTHS.OCTOBER 2024
Altine 14i fani oktoobar 2024,bu 09i waxtu jotee, ca CICAD, dees na siiwal sukkandikukaay bu yees bii di
“Sénégal 2050” : Agenda National de Transformation.
Ci njiital Kilifa gi Basiiru Jomaay Fay, Njiitu Réewum Senegaal, xew-xew bu am solo bii dina dajale mbooleem partaneer yi, piriwe bi ci réew mi ak yu biti-réew, mbootaayi liggéeykat yi ak kurél yi ajuawul ci nguur, ci naal yu am solo ak ay sémb yu wér yu war a gunge soppi gi nu namm a amal ci réew mi fii ak 2050.