Demug Njiitu Réew mi ngir teewe Ndajem Mbootaayu Réewi Afrig yi wàllu Njàng ca Nuwaagsót.

xamle - 10 MONTHS.DECEMBER 2024

Njiitu Réew mi bawoo na Ndakaaru tay ci suba si ngir teewe Ndaje mi Mbootaayu Réewi Afrig yi di amal jagleel ko wàllu Njàng ca Nuwaagsót ci talaata ji.

Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay di wuyuji wooteb naataangoom bu Móritani bi di Mohammet Uld Seex El Gasuwani miy Njiital Mbootaayu Réewi Afrig yi jamono jii.