CONG GA ÀNKARA: NJIITU RÉEW MI BASIIRU JOMAAY FAY DI NAQARLU ÑAAWAAYU JËF JI

Biti Réew - 24 MONTHS.OCTOBER 2024

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay ñaawlu na bu baax congug rëtal gi am ca Ànkara teg ci fésal ag njàppaleem jëme ci askanu Turki ak Njiit la Recep Tayyib Erdogan. “Maa ngi ñaawlu bu baax congug rëtal gi am ca Turki. Jëf ju doy waar la te ñaaw. Ci turu askanu Senegaal, maa ngi fésal sunu naqar ak sunug njàppale jëme ci Peresidaa Erdogan, jabooti way-loru ñi ak askanu Turki. Yal na Yàlla yërëm way-faatu ñi te wéral ñi ci am i gaañu-gaañu.”