jëwriñ - 01 MONTHS.DECEMBER 2024
1 panu desàmbar 2024, ci njiital Kilifa gi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, Njiitu Réew mi, Senegaal dina màggal 80eelu at mi bóomug Caaroy gi amoon ca 1944.
Waxtu ñaan yii ak fàttaliku day delloo njukkal « tiiraayéeri Senegaal » yi daanu woon ci Caaroy, te doon xët wu am solo ci sunu mboor.
Njiit yi, ma-réew yi ak gan ñi war a jóge fenn fu nekk ci àddina si wërngal kàpp, dinañu daje ca Kaa Militeer bu Caaroy ngir sargal leen boole ko ak fàttali seen taxawaay jëm ci dekkal ngor ak doxal yoon.