Ca 38eelu Ndajem Mbootaayu Réewi Afrig yi, Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay teewe na jataayu kaajar Ràppooru Senegaal ci 34eelu jataayu xayma bii di « Sommet du Mécanisme Africain d’Évaluation par les Pairs (MAEP) » ca Adis Abebaa.
Senegaal ak pas-pas bi mu am jëm ci yoriin wu jub te leer, fésal na jéego yi muy teg ngir amal caytu gu wóor te yamale ci ay balli mbindaareem. Njiitu Réew mi fàttali na solos doxaliin wow ñépp a ciy dugal seen yoxo ngir man man a am jëfandiku gu sax ci balli mbindaare yi ngir njariñu askan wi.
Senegaal dina wéyal coppite yi ngir dooleel Réewum yoon, leeraange ak xereñte ci doxaliinu pénc mi, lépp méngoo ak gis-gisam ci suqaliku gu boolee ñépp te manal boppam.